7 Yesu ne ko, Binda nañu, nêti, Bul fir Borom ba sa Yalla.
Te ne ko, Ndah͈ dēga nga li ñile di wah͈? Yesu ne len, Wau: ndah͈ mosu len a janga, ne, Chi gemeñ’ i dōm ak i gūne yu di nampa nga motali nau?
Yesu ne len, Ndah͈ mosu len a janga chi mbinda mi, ne, Doch wa tabah͈kat ya bañ on, mō di neki bop’ i tabah͈ ma: lile juge na fa Borom bi, te koutef la chi suñu i but?
Fōfale Yesu ne ko, Randu ma Seytane, ndege binda nañu, ne, Na nga jāmu Borom ba sa Yalla, te na nga ko topa, mōm reka.
Wande mu tontu, ne, Binda nañu, ne, Nit du mburu reka la dunde, wande itam bāt bu neka bu juge chi gemeñ i Yalla.