4 Wande mu tontu, ne, Binda nañu, ne, Nit du mburu reka la dunde, wande itam bāt bu neka bu juge chi gemeñ i Yalla.
Lu h͈araf chi gemeñ, du gakal nit; wande lu gēna chi gemeñ, mō di gakal nit.
Fōfale Yesu ne ko, Randu ma Seytane, ndege binda nañu, ne, Na nga jāmu Borom ba sa Yalla, te na nga ko topa, mōm reka.
Yesu ne ko, Binda nañu, nêti, Bul fir Borom ba sa Yalla.
Wande bu Dalalkat ba ñoue, ka ma yōnisi fi yēn cha Bay ba, mu di Nh͈el i dega ma juge cha Bay ba, di na ma sēdeji:
Mō di nh͈el ma di dūndalo; yaram wi jeriñul dara: bāt ya ma len wah͈ nh͈el la, ak dūnda.