20 Ñu wocha mbal ya chi tah͈ouay, te topa ko.
Ku sopa bay am mbāte ndey am as man, daganul chi man; te ku sopa dōm am ju gōr, mbāte dōm am ju jigen as man, daganul chi man.
Fōfale Peter tontu ko, ne, Ñun ño wocha yepa, te topa la; lan la ñu ami mbōk?
Mu ne len, Topa len ma, te di nā len def i mōl i nit.
Bu mu fa juge, mu gis yenen i mboka, James dōm i Zebedee, ak rak’ am John, chi gāl ga, ak Zebedee sēn bay, di dāh͈ sēn i mbal; te mu ô len.