12 Ba mu dēge nak ne tej nañu John, mu dem cha Galilee;
Ba John dēge chi tejukay ba i koutef i Krista, mu yōne cha i tālube am;
Ndege Herod jap’ on na John, ewo ko, te tej ko chi kaso, ndig Herodias, jabar i Philip rak’ am.
Cha elek sa bug’ on na dem cha Galilee, te mu gis Philip, te Yesu ne ko, Topa ma.
Mandarga bu jeka bile la Yesu def on cha Cana i Galilee, te wone ndam am; te i talube am gum chi mōm.
Ndege bōba tejangu ñu on John chi kaso.
Ganou ñar i fan ya mu gēna fa dem cha Galilee.
Bile di ñarel i koutef ga Yesu def on, ba mu juge Judea dem fa Galilee.