11 Fōfale Seytane bayi ko; i malāka dika, te bukanēgu ko.
Dēfe nga ne munu ma dagān suma Bay, te lēgi mu may ma lu upa jurom bena fuka njūne’ malāka am?
Te ne ko, So de Dōm i Yalla, chipālul chi suf; ndege binda nañu, ne, Dēnka na la i malāk’ am, te di nañu la yubu chi sēn loh͈o, ndah͈ do fakatal sa tanka chi h͈êr.
Du ma wah͈ati ak yēn lu bare; ndege gelouar i aduna sile ñou na; te amul dara chi man;