10 Fōfale Yesu ne ko, Randu ma Seytane, ndege binda nañu, ne, Na nga jāmu Borom ba sa Yalla, te na nga ko topa, mōm reka.
Wande mu walbatiku, te ne Peter, Randu ma, Seytane si; yā di suma mpaka; ndege topatoū la yu jem chi yef i Yalla, wande yef i nit.
Te cha ganou dogit ba Seytane duga chi mōm. Tah͈na Yesu ne ko, Li nga def, def ko bu gou.