9 Te bu len dēfe ne chi sēn bopa, Am nañu Ibrayuma mu di suñu bay; ndege mangi len di wah͈, ne Yalla mun na chi h͈êr yile sah͈ gēne chi i dōm i Ibrayuma.
Ñu tontu ko, ne, Neka nañu i dōm i Ibrayuma, te bentey neku ñu on i jām i ken: naka nga wah͈e, ne, Di ngēn mucha chi njām?
H͈am nā ne yēn a di dōm i Ibrayuma; wande ūt ngēn ma rēy, ndege suma bāt amul bena bereb chi yēn.
Ndah͈ yā gēti on suñu bay Ibrayuma, ka dē? te yonent ya dē nañu: kan nga def sa bopa?