16 Ba batise’ Yesu mote, mu gēna chi ndoh͈ ma; nōn’ ak nōna asaman si ūbiku chi mōm; mu gis Nh͈el i Yalla di wacha chi melo i mpetah͈, te dal chi kou am:
Te mu ne ko, Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Di ngēn gisi asaman ūbiku, te i malaka i Yalla di yēg ak di wacha chi kou Dōm i nit ka.
Ndege kōka Yalla yōni on, bāt i Yalla yi la wah͈: ndege joh͈ewul Nh͈el ma chi natu.