15 Yesu tontu ko, ne, Bul ko bañ lēgi, ndege nōgu la ñu ela motali njūbay yepa. Nōgale la bañatul.
Wande John bañ ko, ne, Mā soh͈la batise fi you; te yangi ñou fi man?
Ndege joh͈ nā len royukay, ndah͈ ngēn war a def itam niki ma len defal on.
Su ngēn dēnche suma i eble, di ngēn deka chi suma nchofel; naka ma dēnche suma i eble’ Bay, te deka chi nchofel am.
Yesu ne len, Suma dūndu mō di def mbugel i ka ma yōni on, te motali ligey am.
Te ka ma yōni on anda na ak man; bayiwu ma man kena; ndege di nā di def yef ya ko nêh͈ sā su neka.