13 Fōfale Yesu juge Galilee cha Jordan fa John, ndah͈ mu batise fi mōm.
Wande ba mu dēge ne Archelaus ngūru chi bereb i bay am Herod, mu ragal a dem fōfa; te ba ko Yalla yēgale chi gēnta, mu dem cha wet i Galilee,
Wande John bañ ko, ne, Mā soh͈la batise fi you; te yangi ñou fi man?
Te mu batise len chi deh͈ i Jordan, ñu di wējal sēn i bakar.
Te h͈amu ma ko won; wande ndah͈ mu fêñu cha Israel, lile tah͈ ma ñou di batise ak ndoh͈.