12 Am na layu chi loh͈o am, te di na setali boju am fou, te dajale dugup am chi sah͈a mi; wande di na laka choh͈ ba chi safara su feyatil muk.
Bayi len ñar ña ñu sah͈ando be cha ngōbte ga; te cha wah͈tu’ ngōbte ga di nā wah͈ gōbkat ya, ne, Budi len jeka nduh͈um la, taka ko i say te laka ko; wande dajale len dugup ja chi suma sah͈a.
Dōm i nit ka di na yōne i malāk’ am, te di nañu forātu chi ngur am yef yu moylo yepa, ak ña def lu bon;
Te sani len cha safara sa; fōfale la joy di neka, ak yey i buñ.
Bōba ñu jūb ña di nañu melah͈ na janta bi chi sēn ngur i Bay ba. Ku am i nopa na dēga.
Banh͈as bu neka chi man bu mēñul dōm, di na ko gor: te banh͈as bu neka bu mēña dōm, di na ko setal, ndah͈ mu mēña dōm yu gen a bare.