10 Te nistey teg nañu semiñ wi chi rēn i garap ya; garap gu neka mbōk gu mēñul dōm yu bāh͈, di nañu ko dog, te sani ko chi safara.
Mu gis garap i sōto chi wet i yōn wa, dem fa mōm, te fekul dara, wande i h͈ob reka; mu ne ko, Bul mēñati dōm bel mos. Nōn’ ak nōna sōto ba lah͈.
Garap gu neka gu mēñul mēñef bu bāh͈, di nañu ko gor, te sani ko chi safara.
Banh͈as bu neka chi man bu mēñul dōm, di na ko gor: te banh͈as bu neka bu mēña dōm, di na ko setal, ndah͈ mu mēña dōm yu gen a bare.
Su kena dekule chi man, di nañu ko sani cha biti niki banh͈as, te di na lah͈; te ñu forati len, te sani len cha safara sa, te ñu laka.