Mariama nak indi bena libar i h͈êñh͈êñ bu jafe njēg lol, te diw ko cha i tank’ i Yesu, te fomp’ i tank’ am ak kouar am; be nēg ba fês ak h͈et i h͈êñh͈êñ ga.
Ba ngon jote nak cha bes bōba, bu jeka chi ay i bes ba, te bunta ya teju fa talube ya neka, ndege ragal on nañu Yauod ya, Yesu dika, te tah͈ou chi sēn diga, te ne len, Jama and’ ak yēn.