7 Dem len bu gou, wah͈ i tālube am ne, Dēki na cha ñu dē ña; te di na len jitu cha Galilee; fōfale ngēn ko gise: mangi len ko wah͈.
Mangi len di yēgal bala wah͈tu wa jot.
Wande ganou bu ma dēketi, di nā len jītu cha Galilee.
Yesu ne len, Bu len tīt: dem len wah͈ suma i mboka ñu dem cha Galilee; fōfale la ñu ma gise.
Ñu juge cha bamel ba bu gou chi tītay ak kontan gu rey, te dou ndah͈ ñu yubu tālube ya bāt ba.
Te wah͈ nā len ko lēgi bala mu jot, ndah͈ bu mu jote, di ngēn gumi.
Wande yef yile lā len wah͈, ndah͈ bu sēn wah͈tu jote, di ngēn len fataliku naka ma len ko wah͈e won. Te wah͈u ma len on yef yile cha ndôrte la, ndege nek’ on nā ak yēn.