19 Dem len mbōk, def i tālube h͈êt yi yepa, te batise len chi tur i Bay ba, ak Dōm ja, ak Nh͈el mu Sela ma:
Mu ne len, Bindānkat bu neka mbōk bu ñu nekalo tālube chi ngur i ajana, niro na ak borom‐ker ku gēne chi dēnchukay am lu ês ak lu maget.
Di na dajale h͈êt yi yepa chi kanam am; te di na len h͈ajātle ku neka chi morom am, naka sama di h͈ajātle i nh͈ar ak i bey: