16 Wande fuk’ i tālube ya ak bena dem cha Galilee, chi tūnda wa len Yesu wah͈ on.
Wande ganou bu ma dēketi, di nā len jītu cha Galilee.
Yesu ne len, Bu len tīt: dem len wah͈ suma i mboka ñu dem cha Galilee; fōfale la ñu ma gise.
Dem len bu gou, wah͈ i tālube am ne, Dēki na cha ñu dē ña; te di na len jitu cha Galilee; fōfale ngēn ko gise: mangi len ko wah͈.
Yesu tontu len, ne, Ndah͈ du yēn lā tan’ on, fuk’ ak ñar ña, te kena chi yēn ab seytane la?