13 Na ngēn ne, I tālube am a dik’ on chi gudi, te sacha ko ba ñu neloue.
Yesu ne ko, Wah͈ nga ko: te mangi len di wah͈, Ganou lile di ngēn gisi Dōm i nit ka mu di tōg chi loh͈o’ ndējor i kantan, di wachasi chi i nir i asaman.
Ba ñu dajalô ak mag ña, te fēncha, ñu may otukat ya h͈alis bu bare, ne,
Su kēlifa ga dēge lile, di nañu ko dalal, te dindi len chi jāh͈le.