10 Yesu ne len, Bu len tīt: dem len wah͈ suma i mboka ñu dem cha Galilee; fōfale la ñu ma gise.
Wande Yesu wah͈ len chi tah͈ouay, ne, Dalal len sēn h͈ol: Man la; bu len tīt.
Bur ba di na len tontu, ne, Chi dega mangi len di wah͈, Ndege def on ngēn ko chi kena chi suma i mboka yile ku gen a tūt, man ngēn ko defal on.
Di na len tontu, ne, Chi dega mangi len di wah͈, Ndege defu len ko won chi ku gen a tūt chi ñile, man ngēn ko defalul on.
Wande ganou bu ma dēketi, di nā len jītu cha Galilee.
Wande fuk’ i tālube ya ak bena dem cha Galilee, chi tūnda wa len Yesu wah͈ on.
Malāka ma tontu jigen ya, ne, Bu len tīt: ndege h͈am nā ne Yesu ngēn di ūt, ka ñu dāj on cha kura ba.
Dem len bu gou, wah͈ i tālube am ne, Dēki na cha ñu dē ña; te di na len jitu cha Galilee; fōfale ngēn ko gise: mangi len ko wah͈.
Yesu feka len, ne, Mangi len noyu. Ñu ñou, jap’ i tank’ am, te jāmu ko.
Yesu ne ko, Bul ma japa; ndege yēgangu ma fa Bay ba: wande demal fa suma i mboka, te ne len, Da ma yēg fa suma Bay ak sēn Bay, fa suma Yalla ak sēn Yalla.
Wande mu ne len, Man la; bu len tīt.