9 Fōfale lu Jeremiah yonent ba wah͈ on motaliku, ne, Fab on nañu ñeta fuk’ i dogit i h͈ālis, njēg i ka ñu ap’ on, ka ñena chi dōm i Israel ya ap’ on,
Yile yepa am on na ndah͈ la Borom bi wah͈ on chi yonent ba motaliku, ne,
Lōgale motali na la Jeremiah wah͈ on, ne,
Te ne len, Lan ngēn ma joh͈, te di nā len ko jebal? Ñu dige ak mōm ñeta fuk’ i dogit i h͈alis.