60 Te teral ko chi bamel am bu ês, ba mu et’ on chi h͈êr: mu borong doch wu rey chi bunt’ i bamel ba, te dem.
Yusufa jel yaram wa, lomas ko chi ser wu set te wêh͈,
Ñu dem, defar bamel ba bu bāh͈, kaste doch wa, te otukat ya neka ak ñom.
Suf sa yengatu lol; ndege malāka i Borom ba wacha cha asaman, dika roñ doch wa cha bunta ba, te tōg chi kou am.
Yesu nak, di binêti chi bop’ am, dika cha bamel ba. Nkan la won, te teg on nañu doch chi kou am.
Mōtah͈ ñu tegi doch wa. Te Yesu yēkati i but am, te ne, Bay bi, mangi la gerem ndege dēga nga ma.
Cha bereb ba ñu ko dāj on cha kura ba, tōl anga fa won, te cha bir tōl ba bena bamel bu ês, ba kena tedangul.
Chi bes bu jeka ba nak chi ay i bes ba, Mariama dika têl cha bamel ba, ba mu lendeme, te mu gis ñu tegi on doch wa cha bamel ba.