56 Chi sēn digante la Mariama Magdalene nek’ on, ak Mariama ndey i James ak Joses, ak ndey ī dōm i Zebedee.
Kile du dōm i minise bā’m? du ndey am a tūda Mariama? te i rak’ am James, ak Yusufa, ak Simon, ak Judas?
Mariama Magdalene ak menen Mariama ma neka fa, di tōg fu jegeñ bamel ba.
Cha muj i dimas ja, ba fajar di dôr chi bes bu jeka ba chi ay i bes ba, Mariama Magdalene ak menen Mariama ma ñou sêtsi bamel ba.
Wande ndey i Yesu anga tah͈ou on cha kanam i kura ba, ak rak’ am, Mariama jabar i Clopas, ak Mariama Magdalene.
Chi bes bu jeka ba nak chi ay i bes ba, Mariama dika têl cha bamel ba, ba mu lendeme, te mu gis ñu tegi on doch wa cha bamel ba.
Mariama Magdalene dika te nitali talube ya, ne, Gis on nā Borom bi; ak naka mu ko wah͈e yef yile.