48 Nōn’ ak nōna kena chi ñom dou, jel ab sponge, fêsal ko binegar, def ko chi sonka, te joh͈ ko mu nān.
Ñu joh͈ ko biñ bu ñu bōle ak weh͈tan ndah͈ mu nān: ba mu ko mose, mu bañ a nān.
Ñena ñu tah͈ou fa, ba ñu dēge lōla, ne, Ki nit ange ô Elijah.
Ña cha des ne, Bayi ko; na ñu gis su Elijah di ñou musal ko.