43 Mu ōlu Yalla; na ko musal lēgi, su ko buge; ndege nôn na, Mā di Dōm i Yalla.
You mi dānel jama ja te tabah͈ati ko chi ñet’ i fan, musalal sa bopa. So de Dōm i Yalla, wachal chi kura bi.
Saltige ba nak, ak ña nek’ on ak mōm, di otu Yesu, ba ñu gise yengatu’ suf sa, ak yef ya am, ñu tīt lol, ne, Chi dega kile Dōm i Yalla la.
Man ak Bay ba di bena.
Di ngēn wah͈al ka Yalla selal on, te yōni ko chi aduna si, ne Sāga nga Yalla, ndege wah͈ nā, ne, Mā di Dōm i Yalla?
Yauod ya tontu ko, ne, Am nañu yōn, te chi suñu yōn wōgu ela na dē, ndege def on na bop’ am Dōm i Yalla.