41 I njīt i seriñ ya itam, ak bindānkat ya ak mag ya ñaual ko, ne,
You mi dānel jama ja te tabah͈ati ko chi ñet’ i fan, musalal sa bopa. So de Dōm i Yalla, wachal chi kura bi.
Musal na ñenen; munul a musal bop’ am. Mō di Bur i Israel: na wacha lēgi chi kura bi, te di nañu ko gum.