40 You mi dānel jama ja te tabah͈ati ko chi ñet’ i fan, musalal sa bopa. So de Dōm i Yalla, wachal chi kura bi.
H͈êt wu bon ak njālo ūt na mandarga; du ñu ko may mandarga, lu dul mandarga i Jonah. Mu bayi len, te dem.
Nit kile wah͈ on na, ne, Mun nā dānel juma’ Yalla, te tabah͈ati ko chi ñet’ i fan.
I njīt i seriñ ya itam, ak bindānkat ya ak mag ya ñaual ko, ne,
Musal na ñenen; munul a musal bop’ am. Mō di Bur i Israel: na wacha lēgi chi kura bi, te di nañu ko gum.
Saltige ba nak, ak ña nek’ on ak mōm, di otu Yesu, ba ñu gise yengatu’ suf sa, ak yef ya am, ñu tīt lol, ne, Chi dega kile Dōm i Yalla la.
Ba firkat ba ñoue fi mōm, mu ne, So de Dōm i Yalla, na nga ebal h͈êr yile ñu neka mburu.
Te ne ko, So de Dōm i Yalla, chipālul chi suf; ndege binda nañu, ne, Dēnka na la i malāk’ am, te di nañu la yubu chi sēn loh͈o, ndah͈ do fakatal sa tanka chi h͈êr.