32 Ba ñu gēne, ñu feka wā’ Cyrene ku tuda Simon: mōm la ñu jeñtal mu and’ ak ñom ndah͈ mu gadu kura ba.
Fōfale Yesu ne i tālube am, Su nit buge and’ ak man, na wēdi bop’ am, gadu kura am, te topa ma.
Te ku la buga jeñ nga gūnge ko fu sorey, gūnge ko fu sorey‐sorey.
Ñu yubu Yesu: te mu gēna, gadul kura am ba, dem fa bereb bu tūda Bereb i h͈ot’ i bopa, ba ñu tūda chi lak’ i Yauod ya, Golgotha: