3 Fōfale Judas, ka ko or on, ba mu gise ne ey nañu ko, mu rēchu, te indêti ñeta fuk’ i dogit i h͈ālis chi i njīt i seriñ ya ak mag ya, ne,
Te cha wah͈tu’ rêr, Seytane nak def on na jēg chi h͈ol i Judas Iscariot, dōm i Simon, mu or ko,
Te cha ganou dogit ba Seytane duga chi mōm. Tah͈na Yesu ne ko, Li nga def, def ko bu gou.
Judas nak, ba mu ame i h͈arekat ak i saltige cha i njīt i seriñ ya ak Pharisee ya, mu dika fōfale ak i lampa ak i nītu ak i ganay.