27 Fōfale i h͈arekat i kēlifa ga yubu Yesu chi ker i ate ga, te dajale fi mōm sēn i morom yepa.
Fōfale i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña dajalo fi ker i kēlifa i seriñ ya, ku tūda Caiaphas,
Ñu omat Yesu nak cha Caiaphas be cha bir ateukay ba: te têl on na; ti ñom h͈arafu ñu cha ateukay ba, ndah͈ du ñu gakal sēn bopa, wande ndah͈ ñu mun a leka h͈ewte ga.
Judas nak, ba mu ame i h͈arekat ak i saltige cha i njīt i seriñ ya ak Pharisee ya, mu dika fōfale ak i lampa ak i nītu ak i ganay.
Pilate nak h͈arafati cha ateukay ba, te ô Yesu te ne ko, Ndah͈ yā di bur i Yauod ya?