2 Ñu ew ko, omat ko, te jebal ko Pilate kēlifa ga.
Di nañu ko jebal Gentile ya, ndah͈ ñu ñaual ko, ratah͈ ko, te dāj ko cha kura; te chi ñetel i fan am di na dēki.
Su kēlifa ga dēge lile, di nañu ko dalal, te dindi len chi jāh͈le.
H͈arekat ya nak ak saltige ba, ak i ndau i Yauod ya japa Yesu, te ew ko,
Annas nak ew ko, te yōni ko Caiaphas, kēlifa i seriñ ya.
Ñu omat Yesu nak cha Caiaphas be cha bir ateukay ba: te têl on na; ti ñom h͈arafu ñu cha ateukay ba, ndah͈ du ñu gakal sēn bopa, wande ndah͈ ñu mun a leka h͈ewte ga.