18 Ndege h͈am on na ne ndig kañān la ñu ko jebale.
Ba ñu dajalô, Pilate ne len, Kan ngēn buga ma joh͈ len? Barabbas, am Yesu ki tūda Krista?
Ba mu tōge chi ateukay ba, jabar am yōni fi mōm, ne, Bul bōlo chi yef i kōku nit ku jūb; ndege da ma yēg yef yu bare bes bile chi gēnta ndig mōm.