17 Ba ñu dajalô, Pilate ne len, Kan ngēn buga ma joh͈ len? Barabbas, am Yesu ki tūda Krista?
Te Yanh͈oba jur Yusufa jekar i Mariama, ka nek’ on ndey i Yesu, ka ñu tūda Krista.
Am on nañu chi wah͈tu wōwale sachakat bu dēgu on, ku tūda Barabbas.
Ndege h͈am on na ne ndig kañān la ñu ko jebale.
Tah͈na ñu h͈āchu, ne, Weyal ak mōm, weyal ak mōm, dāj ko cha kura ba. Pilate ne len, Ndah͈ ma dāj sēn Bur cha kura ba? I njīt i seriñ ya tontu, ne, Amu ñu bur ganou Cæsar.
Jigen ja ne ko, H͈am nā ne Masiu di na dika (ka tūda Krista): su dike, di na ñu jangal yef yepa.