14 Tontuwu ko dara, du bena bāt sah͈; tah͈na kēlifa ga jomi lol.
Wande Yesu japa gemeñ am. Kēlifa i seriñ ya ne ko, Mangi la dagān chi tur i Yalla ji di dunda, nga wah͈ ñu ndah͈ yā di Krista, Dōm i Yalla.
Ba ko i njīt i seriñ ya ak mag ya jêñe, tontuwul dara.
Mōtah͈ Pilate ne ko, Dēgu la yef yi ñu la sēdêl?
Te h͈arafati cha ateukay ba, te ne Yesu, Ana fo bayako? Wande Yesu tontuwu ko.