12 Ba ko i njīt i seriñ ya ak mag ya jêñe, tontuwul dara.
Wande Yesu japa gemeñ am. Kēlifa i seriñ ya ne ko, Mangi la dagān chi tur i Yalla ji di dunda, nga wah͈ ñu ndah͈ yā di Krista, Dōm i Yalla.
Mōtah͈ Pilate ne ko, Dēgu la yef yi ñu la sēdêl?
Tontuwu ko dara, du bena bāt sah͈; tah͈na kēlifa ga jomi lol.