11 Yesu tah͈ou chi kanam i kēlifa ga, te kēlifa ga lāj ko, ne, Ndah͈ yā di Bur i Yauod ya? Yesu ne ko, Wah͈ nga ko.
Te di nañu len yubu chi kanam i kēlifa ak i bur ngir man, ndig sēde chi ñom ak chi Gentile ya.
Doy na chi tālube mu neka naka jemantalkat am, te jām naka borom am. Su ñu ôe borom‐ker ga Abdujambar, naka ña mōmu chi ker am!
Ne, Ana ki jūdu Bur i Yauod ya? Ndege gis on nañu bidiw am cha Penku, te dika nañu ndah͈ ñu jāmu ko.
Fōfale Judas ma ko or, tontu ne, Man lā’m, Rabbi? Mu ne ko, Wah͈ nga ko.
Yesu ne ko, Wah͈ nga ko: te mangi len di wah͈, Ganou lile di ngēn gisi Dōm i nit ka mu di tōg chi loh͈o’ ndējor i kantan, di wachasi chi i nir i asaman.