9 Ndege mun on naño jay diw gu h͈ēñ gile, te am chi lu bare, sarah͈ ko miskin yi.
Wande Yesu h͈am ko, ne len, Lutah͈ ngēn di geten jigen ji? ndege defal on na ma jef ju hāh͈.
Wande ba ko tālube ya gise, ñu mer, ne, Lu waral yah͈a gile?