8 Wande ba ko tālube ya gise, ñu mer, ne, Lu waral yah͈a gile?
Ba ko fuka ña dēge, ñu mere ñar i mboka ya.
Jena jigen, ju am ndap i diw gu h͈ēñ gu jafe njēg lol, ñou fi mom, te tūr ko chi bop’ am ba mu tōge di leka.
Ndege mun on naño jay diw gu h͈ēñ gile, te am chi lu bare, sarah͈ ko miskin yi.