72 Mu wēdêti ak ngeñ, ne, H͈amu ma nit ki.
III. Bulu jil tur i Yalla saa Borom ce cahan, ndegi, Borom bi, du ko seti naka bakar, ku jil tur am ce cahan.
Ba mu deme be h͈araf cha rum ba, kenen gis ko, te ne ña fa neka, Kile nek’ on na itam ak Yesu wā’ Nazareth ba.
Ganou lōlale tūti, ña tah͈ou fa ñou fi Peter, te ne ko, Chi dega kena chi ñom nga; ndege sa laka fêñal na la.
Fōfale mu dal di mōlu, di geñ, ne, H͈amu ma nit ki. Nōn’ ak nōna seh͈a ga sab.