67 Fōfale ñu tufli chi kanam am, te mbumbanda ko: ñenen dōr ko ak sēn i loh͈o,
Ne, Tolātle ñu, you Krista, kan a la dōr?
Nu tufli ko; jel sonka ba, te dōr ko chi bop’ am.
Wande mangi len di wah͈, Bu len findu lu bon, wande ku la dōr chi sa leh͈ i ndējor, sopalil benen bi itam.
Ba mu wah͈e lōlu, kena chi ndau ya’nga fa tah͈ou dōr Yesu ak loh͈o am, ne, Ndah͈ nōnu nga tonto kēlifa i serin ya?
Te ñou fi mōm, ne, Jamom, Bur i Yauod ya! te ñu dōr ko ak sēn i loh͈o.