Matthew 26:64 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907
64 Yesu ne ko, Wah͈ nga ko: te mangi len di wah͈, Ganou lile di ngēn gisi Dōm i nit ka mu di tōg chi loh͈o’ ndējor i kantan, di wachasi chi i nir i asaman.
Fōfale mandarga i Dōm i nit ka di na fêñ cha asaman; h͈êt i aduna si yepa di nañu yeremtu, te di nañu gis Dōm i nit ka mu di ñou chi i nir i asaman si ak kantan ak ndam lu rey.
Pilate ne ko, Ndah͈ bur nga? Yesu tontu, ne, Wah͈ nga ko, ndege man bur la. Lile tah͈ ma jūdu on, te lile tah͈ ma ñou chi aduna si, ndah͈ ma sēde dega gi. Ku neka ku boka chi dega gi di na dēga suma bāt.