62 Kēlifa i seriñ ya jog, te ne ko, Do tontu dara? li la ñile sēdêl?
Nit kile wah͈ on na, ne, Mun nā dānel juma’ Yalla, te tabah͈ati ko chi ñet’ i fan.
Wande Yesu japa gemeñ am. Kēlifa i seriñ ya ne ko, Mangi la dagān chi tur i Yalla ji di dunda, nga wah͈ ñu ndah͈ yā di Krista, Dōm i Yalla.