59 I njīt i seriñ ya nak ak ndaje ma yepa ūt sēde i fen lu jem chi Yesu, ndah͈ ñu rēy ko.
Wande mangi len di wah͈, Ku di mere morom am, mungi chi tafār i ate; te ku ne morom am, Dof bi, mungi chi tafār i ate bu rey; wande ku ne, Ēfar bi, di na neka chi tafār i safara’ nāri.
Kēlifa i seriñ ya lāj Yesu chi lu jem chi talube am ya, ak njemantale am.
Ana lutah͈ nga ma lāj? lājal ña ma dēg’ on la ma len wah͈ on: ñile h͈am nañu la ma wah͈ on.