Goual a mar ak sa mbañ naka nga neke chi yōn wa ak mōm; lu dul lōga mbañ ma di na la joh͈e chi atekat ba, te atekat ba di na la joh͈e chi otukat ba, te mu tej la chi kaso.
Tah͈na ba ko i njīt i seriñ ya ak ndau ya gise, ñu h͈āchu, ne, Dāj ko cha kura ba, dāj ko cha kura ba. Pilate ne len, Yēn yubu len ko, te dāj ko cha kura ba: ndege gisu ma tōñ chi mōm.