Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -




Matthew 26:55 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

55 Chi wah͈tu wōwale Yesu ne mbōlo ma, Dika ngēn jelsi ma ak i jāsi ak i doko, niki sachakat? Dan nā tōg ak yēn gir gu neka, di jemantale chi juma ja, te japu len ma won.

Faic an caibideil Dèan lethbhreac




Matthew 26:55
15 Iomraidhean Croise  

Ba mu ñoue chi bir juma ja, i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña ñou fi mōm ba mō jemantale, ne, Ak ban sañsañ nga defe yef yile? te ku la joh͈ sañsañ bile?


Ba mu wah͈andô, Judas, kena chi fuk’ ak ñar ña, ñou, and’ ak mōm mbōlo mu rey ñu am i jāsi ak i doko, ñu juge fa i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña.


Wande ba dig’ i h͈ewte ga jote, Yesu dem cha bir juma ja, te jemantale.


Tah͈na Yesu h͈āchu cha juma ja, di jemantale, ne, Da ngēn ma h͈am, te h͈am fu ma juge itam; te diku ma chi suma bopa, wande ka ma yōni on dega la, ka ngēn h͈amul.


Te nit ña ñepa dika fi mōm, te mu tōg te jemantal len.


Yesu wah͈ on na bāt yile cha dēnchukay ba, ba mo jemantale cha juma ja: te ken japatu ko; ndege wah͈tu am ñouangul.


Lean sinn:

Sanasan


Sanasan