54 Wande naka la mbinda mi di motalikô, ne nōgu la ela ame?
Yesu ne len, Ndah͈ mosu len a janga chi mbinda mi, ne, Doch wa tabah͈kat ya bañ on, mō di neki bop’ i tabah͈ ma: lile juge na fa Borom bi, te koutef la chi suñu i but?
Dōm i nit ka di na dem naka ñu bind’ on la jem chi mōm; wande suboh͈un nit ka ko ori! bāh͈ on na chi nit kōkale su juduūl on.
Su len tūde won i yalla, ndege chi ñom la bāt i Yalla ñou on (te du mun a fanh͈a mbinda mi),