50 Yesu ne ko, Anda, defal li la tah͈ a dika. Fōfale ñu ñou, teg sēn i loh͈o chi Yesu, te jel ko.
Wande mu tontu kena chi ñom, ne, H͈arit, tōñu ma la: du bena h͈asab la ñu wah͈ante won am?
Mu ne ko, H͈arit, naka nga fi h͈arafe, te amu la chol i nchēt gi? Wah͈ul dara.