48 Ki ko or nak joh͈ na len firnde, ne, Ka ma fōni, mōm la: japa len ko.
Ba mu wah͈andô, Judas, kena chi fuk’ ak ñar ña, ñou, and’ ak mōm mbōlo mu rey ñu am i jāsi ak i doko, ñu juge fa i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña.
Mu ñou fi Yesu chi tah͈ouay, ne, Noyu nā la, Rabbi, te mu fōn ko.