46 Jog len, na ñu dem, ki ma orsi jegeñsi na.
Fōfale mu ñou fi tālube ya, te ne len, Nelou len lēgi, te nopalaku: wah͈tu wi jegeñsi na, te or nañu Dōm i nit ka chi loh͈o i bakarkat ya.
Ba mu wah͈andô, Judas, kena chi fuk’ ak ñar ña, ñou, and’ ak mōm mbōlo mu rey ñu am i jāsi ak i doko, ñu juge fa i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña.
Wande ndah͈ aduna si h͈am ne sopa nā Bay ba, te naka ma Bay ba joh͈e won eble, nōgule lā def. Jog len, na ñu dem cha kanam.
Peter h͈inaku, te gis talube ba Yesu sop’ on di topa; ka wēru on itam cha den’ am cha rêr ba, te ne, Borom bi, ana ku la di ori?