Matthew 26:39 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907
39 Mu dem tūti cha kanam, defēnu chi suf, te ñān, ne, E suma Bay, su munê am, na nānu bile wey fi man: wande du naka ma ko buge, wande naka nga ko buge.
Mōtah͈ Yesu tontu te ne len, Chi dega, chi dega, ma ne len, Dōm ji munul a def dara chi bop’ am, su gisule Bay ba mu def ko: ndege lu mu mun a don lu mu def, lile la Dōm ji di def nōgule itam.