37 Mu jel ak mōm Peter ak ñar i dōm i Zebedee, dôr di yogorlu ak nah͈arlu lol.
Ganou jurom ben’ i fan, Yesu jel Peter, James, ak John rak’ am, te yubu len chi kou tūnda wu koue, ñom dal:
Fōfale ndey ī dom i Zebedee ñou fi mōm, ak dōm am yu gōr, di ko jāmu, te lāj ko lef.
Don na doh͈ cha tefes i Galilee, te mu gis ñar i mboka, Simon ku tūda Peter, ak mag am Andrew, di sani mbal cha gēch ga; ndege nek’ on nañu i mōl.
Bu mu fa juge, mu gis yenen i mboka, James dōm i Zebedee, ak rak’ am John, chi gāl ga, ak Zebedee sēn bay, di dāh͈ sēn i mbal; te mu ô len.
Suma fit nah͈arlu na lēgi; te ana lu ma war a wah͈? Bay bi, musal ma chi wah͈tu wile? Wande lōlo tah͈ ma dika chi wah͈tu wile.