31 Fōfale Yesu ne len, Di ngēn fakatalu ndig man chi gudi gile yēn ñepa: ndege binda nañu, ne, Di nā dōr sama ba, te i nh͈ar i gēta ga di nañu h͈ajātlaku.
Te barkel chi ku dul feka fakatalu chi man.
Dōm i nit ka di na dem naka ñu bind’ on la jem chi mōm; wande suboh͈un nit ka ko ori! bāh͈ on na chi nit kōkale su juduūl on.
Wande lile yepa am na, ndah͈ mbinda i yonent ya motaliku. Fōfale la ko tālube ya yepa woche, te dou.
Wah͈tu wa di na joti, te lēgi mu jot, ne di ngēn tasāro, ku neka chi yos am, te bayi ma man dal: wande dowul man dal a neka, ndege Bay ba’nge ak man.